sourate
float64
1
114
verset
float64
1
286
translation
dict
1
1
{ "fr": "Au nom d´Allah, le Tout Miséricordieux, le Très Miséricordieux.", "wo": "Ci turu Yàlla, miy Yërëmaakoon , di Jaglewaakoon , laay tàmbalee" }
1
2
{ "fr": "Louange à Allah, Seigneur de l´univers.", "wo": "Xeeti cant yépp ñeel na Yàlla, miy Boroom àddina si." }
1
3
{ "fr": "Le Tout Miséricordieux, le Très Miséricordieux,", "wo": "Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi," }
1
4
{ "fr": "Maître du Jour de la rétribution.", "wo": "Di Buur, di Boroom Bis-pénc ba." }
1
5
{ "fr": "C´est Toi [Seul] que nous adorons, et c´est Toi [Seul] dont nous implorons secours.", "wo": "Yaw doŋŋ la nuy jaamu, te ci Yaw doŋŋ doŋŋ la nuy sàkku ndimbal." }
1
6
{ "fr": "Guide-nous dans le droit chemin,", "wo": "Gindi nu jëme nu ca yoon wu jub xocc wa," }
1
7
{ "fr": "le chemin de ceux que Tu as comblés de faveurs, non pas de ceux qui ont encouru Ta colère, ni des égarés.", "wo": "yoonu ñi Nga xéewale, wuuteek ñi Nga mere ak ñi réer. " }
2
1
{ "fr": "Alif, Lam, Mim .", "wo": "Alif, Laam, Miim ." }
2
2
{ "fr": "C´est le Livre au sujet duquel il n´y a aucun doute, c´est un guide pour les pieux .", "wo": "Téere bii amul sikk ci ne [ag jub a ci nekk] guy soxal way-ragal Yàlla yi." }
2
3
{ "fr": "qui croient à l´invisible et accomplissent la Salat et dépensent [dans l´obéissance à Allah], de ce que Nous leur avons attribué ", "wo": "ña gëm ci kumpa. Di farlu ci julli te di joxe ci li Nu leen xéewale" }
2
4
{ "fr": "Ceux qui croient à ce qui t´a été descendu (révélé) et à ce qui a été descendu avant toi et qui croient fermement à la vie future.", "wo": "Ñoo di ña gëm la Ñu wàcce ci yaw ak la Nu wàcce woon mu jiitu woon te ñu amug wóolu ci dikkug Bis-pénc ba." }
2
5
{ "fr": "Ceux-là sont sur le bon chemin de leur Seigneur, et ce sont eux qui réussissent (dans cette vie et dans la vie future).", "wo": "Ñooñoo nekk ca njub ga tukkee ca seen Boroom te ñoom ñoo texe." }
2
6
{ "fr": "[Mais] certes les infidèles ne croient pas, cela leur est égal, que tu les avertisses ou non : ils ne croiront jamais.", "wo": "Ñi weddi, nga waar leen ak ñàkk leen waar a yem ci ñoom, duñu gëm." }
2
7
{ "fr": "Allah a scellé leurs coeurs et leurs oreilles; et un voile épais leur couvre la vue; et pour eux il y aura un grand châtiment.", "wo": "Saar 2 : Nag wa 286 Laaya - Ginnaaw Gàddaay ga Ci turu Yàlla Yërëmaakoon bi, Jaglewaakoon bi." }
2
7
{ "fr": "Allah a scellé leurs coeurs et leurs oreilles; et un voile épais leur couvre la vue; et pour eux il y aura un grand châtiment.", "wo": "Yàlla fatt na seeni xol ak seeni nopp ; muuraay nekk na ca seeni gët ; mbugal mu metti dana leen dal." }
2
8
{ "fr": "Parmi les gens, il y a ceux qui disent : \"Nous croyons en Allah et au Jour dernier ! \" tandis qu´en fait, ils n´y croient pas.", "wo": "Am na ci nit ñi, ñu naan : “Gëm nanu Yàlla ak Bis-pénc ba !” te gëmuñu dara." }
2
9
{ "fr": "Ils cherchent à tromper Allah et les croyants; mais ils ne trompent qu´eux-mêmes, et ils ne s´en rendent pas compte.", "wo": "Dañuy jéem a nax Yàlla ak way-gëm ñi ; waaye naxuñu lu dul seen bopp, te yëguñu ko." }
2
10
{ "fr": "Il y a dans leurs coeurs une maladie (de doute et d´hypocrisie), et Allah laisse croître leur maladie. Ils auront un châtiment douloureux, pour avoir menti.", "wo": "Jàngoroo nekk ci seeni xol (gog sikki-sàkk ak ug naaféq), faf Yàlla yokk leen jàngoro. Mbugal mu metti dana leen dal ngir seenug weddi." }
2
11
{ "fr": "Et quand on leur dit : \"Ne semez pas la corruption sur la terre\", ils disent : \"Au contraire nous ne sommes que des réformateurs ! \"", "wo": "Bu ñu leen waxee : “Buleen di yàq ci suuf si” , ñu ne : “Nun way-defar lanu !”" }
2
12
{ "fr": "Certes, ce sont eux les véritables corrupteurs, mais ils ne s´en rendent pas compte.", "wo": "Déedéet, ñoom ñooña ay yàq-kat lañu, te yëguñu ko." }
2
13
{ "fr": "Et quand on leur dit : \"Croyez comme les gens ont cru\", ils disent : \"Croirons-nous comme ont cru les faibles d´esprit ? \" Certes, ce sont eux les véritables faibles d´esprit, mais ils ne le savent pas.", "wo": "Bu ñu ne leen : “Gëmleen ni nit ñi gëmee” , ñu tontu ne : “Ndax danuy gëm ni dof yi di gëmee ?” Déedéet, ñoom ñooy diy dof, te xamuñu ko." }
2
14
{ "fr": "Quand ils rencontrent ceux qui ont cru, ils disent : \"Nous croyons\"; mais quand ils se trouvent seuls avec leurs diables, ils disent : \"Nous sommes avec vous; en effet, nous ne faisions que nous moquer (d´eux)\".", "wo": "Bu ñu dajeek way-gëm ña, ne : “Gëm nanu” ; waaye bu ñu wéetee ak seeni (Séytaane naaféq yi), ne : “Nook yéen a ànd ; nun danuy yejji [jullit ñi] rekk” . " }
2
15
{ "fr": "C´est Allah qui Se moque d´eux et les endurcira dans leur révolte et prolongera sans fin leur égarement.", "wo": "Yàllaa nga leen di yejji, di leen gën a yàggal ca seen mbeewte googu, ñuy deŋŋi-deŋŋi ak seen ngumbaag xol." }
2
16
{ "fr": "Ce sont eux qui ont troqué le droit chemin contre l´égarement. Eh bien, leur négoce n´a point profité. Et ils ne sont pas sur la bonne voie.", "wo": "Ñooña ñoo di ña jaay njub jënde ci réer, seen njaay mooma amul tono. Te it gindikuwuñu." }
2
17
{ "fr": "Ils ressemblent à quelqu´un qui a allumé un feu; puis quand le feu a illuminé tout à l´entour, Allah a fait disparaître leur lumière et les a abandonnés dans les ténèbres où ils ne voient plus rien.", "wo": "Seen niróole mi ngi demee ni ku taal taalamn, ba janeer ba leeraale la ko wër, Yàlla fay leer ga, bàyyi leen cig lëndëm ba gisatuñu dara.(s)" }
2
18
{ "fr": "Sourds, muets, aveugles, ils ne peuvent donc pas revenir (de leur égarement).", "wo": "Dañoo tëx, luu, gumba, ba duñu mën a dellusi (cig njub)." }
2
19
{ "fr": "[On peut encore les comparer à ces gens qui, ] au moment où les nuées éclatent en pluies, chargées de ténèbres, de tonnerre et éclairs, se mettent les doigts dans les oreilles, terrorisés par le fracas de la foudre et craignant la mort; et Allah encercle de tous côtés les infidèles.", "wo": "Walla [seen niróolee ngi deme ni] waame wu tukkee asamaan ànd ak lëndëm ak i dënnu ak i melax, ñu saañ seeni nopp ak seeni waaroom ngir bañ a dégg kàddu ya ngir ragal dee ;Yàlla Aji-peeg la yéefar ya." }
2
20
{ "fr": "L´éclair presque leur emporte la vue : chaque fois qu´il leur donne de la lumière, ils avancent; mais dès qu´il fait obscur, ils s´arrêtent. Si Allah le voulait Il leur enlèverait certes l´ouïe et la vue, car Allah a pouvoir sur toute chose.", "wo": "Melax ga xaw naa yuri seeni gët : saa su leen leeralee [yoon wa] ñu dox ca leer ga ;saa su lëndëmee ñu taxaw. Bu neexoon Yàlla mu tëxloo leen, gumbaloo leen, Yàlla am na kàttanu def lu ne." }
2
21
{ "fr": "ô hommes ! Adorez votre Seigneur, qui vous a créés vous et ceux qui vous ont précédés. Ainsi atteindriez-vous à la piété.", "wo": "Yéen nit ñi ! Jaamuleen Boroom bi leen bind, yéen ak ñi leen jiitu, ndax ngeen ragal ko. [Fegu] ci mbugalam." }
2
22
{ "fr": "C´est Lui qui vous a fait la terre pour lit, et le ciel pour toit; qui précipite la pluie du ciel et par elle fait surgir toutes sortes de fruits pour vous nourrir, ne Lui cherchez donc pas des égaux, alors que vous savez (tout cela).", "wo": "Moom mi def suuf nekk laltaay ci yéen, asamaan si di seen téeg ; te mu wàcceel leen ndox mu jóge asamaan, génne ca ay meññeent yu mu leen wërsëgal, bu leen sàkkal Yàlla moroom te xam xéll [ne loolu jaaduwul]." }
2
23
{ "fr": "Si vous avez un doute sur ce que Nous avons révélé à Notre Serviteur, tâchez donc de produire une sourate semblable et appelez vos témoins, (les idoles) que vous adorez en dehors d´Allah, si vous êtes véridiques.", "wo": "Bu ngeen amee sikki-sàkka ci lii Nu wàcce ci Sunu jaam bi, indileen saar wu mel ni moom [Alxuraan] te sax ñaanleen ndimbal ñi ngeen di jaamu ba jaamuwuleen Yàlla, ndegam dëgg la ci yéen." }
2
24
{ "fr": "Si vous n´y parvenez pas et, à coup sûr, vous n´y parviendrez jamais, parez-vous donc contre le feu qu´alimenteront les hommes et les pierres, lequel est réservé aux infidèles.", "wo": "Bu ngeen ko deful, te du ngeen ko mën a def mukk, na ngeen ragal safara soo xam ne matt ma koy xamb nit la ak i xeer, te way weddi ya la ñu koy xaaroo." }
2
25
{ "fr": "Annonce à ceux qui croient et pratiquent de bonnes oeuvres qu´ils auront pour demeures des jardins sous lesquels coulent les ruisseaux; chaque fois qu´ils seront gratifiés d´un fruit des jardins ils diront : \"C´est bien là ce qui nous avait été servi auparavant\". Or c´est quelque chose de semblable (seulement dans la forme); ils auront là des épouses pures, et là ils demeureront éternellement.", "wo": "Na nga bégal ña gëm tey jëf jëf yu sell, [xamal leen] ne am nañu àjjana joo xam ne ay dex a ngay daw ca suufam ; saa su ñu leen xéewalee ci ay meññeet, muy la ñu leen wërsëgale, ñu naan: “Lii dey masoon nanu cee xéewlu ca bu jëkk [ca àddina]” . Fekk dañu leen a jox lu nurook [la ñu xamoon ca àddina]; ñeel na leen it ca àjjana jooju ay jabar [soxna] yuñu laabal [ci bépp ayib], te ñoom dañu fay béel." }
2
26
{ "fr": "Certes, Allah ne se gêne point de citer en exemple n´importe quoi : un moustique ou quoi que ce soit au-dessus; quant aux croyants, ils savent bien qu´il s´agit de la vérité venant de la part de leur Seigneur; quant aux infidèles, ils se demandent \"Qu´a voulu dire Allah par un tel exemple ? \". Par cela, nombreux sont ceux qu´Il égare et nombreux sont ceux qu´Il guide; mais Il n´égare par cela que les pervers,", "wo": "Yàlla du kersawu ci joxe misaal mu mu mën a doon : ci aw yoo walla ci lu ko ëpp ; ñi gëm ñoom xam nañu ne loolu mooy dëgg ; yéefar yi ñoom dañuy wax naan “Moo lan la Yàlla namm ci léebu wii ?” . Dana ca réeral ñu bari, Dana ca jubal it ñu bari ; waaye du ci réeral ñu dul saay-saay sa,(r)" }
2
27
{ "fr": "qui rompent le pacte qu´ils avaient fermement conclu avec Allah, coupent ce qu´Allah a ordonné d´unir, et sèment la corruption sur la terre. Ceux-là sont les vrais perdants.", "wo": "ñooy ña nga xam ne dañuy firi kóllareg Yàlla ginnaaw ba mu fasoo ba noppi te di dog la Yàlla digle ñu jokkale ko [ag mbokk]. Te ñiy yàq ci suuf si. Ñooña ñooy ña yàqule." }
2
28
{ "fr": "Comment pouvez-vous renier Allah alors qu´Il vous a donné la vie, quand vous en étiez privés ? Puis Il vous fera mourir; puis Il vous fera revivre et enfin c´est à Lui que vous retournerez.", "wo": "Naka ngeen di weddee Yàlla te ngeen doonoon ñu dee, Mu dundal leen ? Dana leen rey ; dana leen dekkalaat ngeen dellu ca Moom." }
2
29
{ "fr": "C´est Lui qui a créé pour vous tout ce qui est sur la terre, puis Il a orienté Sa volonté vers le ciel et en fit sept cieux. Et Il est Omniscient.", "wo": "Moom moo leen sàkkal lépp lu nekk ci suuf si, daldi jublu ci asamaan si def ko mu nekk juróoom-ñaari asamaan. Te moom nag lépp la xam." }
2
30
{ "fr": "Lorsque Ton Seigneur confia aux Anges : \"Je vais établir sur la terre un vicaire \"Khalifat\". Ils dirent : \"Vas-Tu y désigner un qui y mettra le désordre et répandra le sang, quand nous sommes là à Te sanctifier et à Te glorifier ? \" - Il dit : \"En vérité, Je sais ce que vous ne savez pas ! \".", "wo": "Fàttalikul ba sa Boroom waxee Malaaka ya, ne leen: “Man dey damaa namm a def ci suuf si ag kilifa[kuutaay]. Ñu toontu ne ko : “Moo ndax dangay def ci suuf si koo xam ne dafa ciy nekk di yàq, di tuur i dereet, te nun nu ngi lay sàbbaal, di la sant te di màggal sag sell ?” – Yàlla ne leen : “Xam naa lu ngeen xamul !” ." }
2
31
{ "fr": "Et Il apprit à Adam tous les noms (de toutes choses), puis Il les présenta aux Anges et dit : \"Informez-Moi des noms de ceux-là, si vous êtes véridiques ! \" (dans votre prétention que vous êtes plus méritants qu´Adam).", "wo": "Mu jàngal Aadama turi lenn lu ne, ba noppi won ko Malaaka ya, ne leen : “Wax leen ma turi yëf yii, ndegam ñu dëggu ngeen !” ." }
2
32
{ "fr": "- Ils dirent : \"Gloire à Toi ! Nous n´avons de savoir que ce que Tu nous a appris. Certes c´est Toi l´Omniscient, le Sage\".", "wo": "–Malaaka ya ne ko : “Tuddu nanu sa sell gi ! Amunu benn xam-xam lu dul loo nu xamal. Ndax Yaw yaay ki xam, Yaay ki xereñ” ." }
2
33
{ "fr": "- Il dit : \"ô Adam, informe-les de ces noms; \" Puis quand celui-ci les eut informés de ces noms, Allah dit : \"Ne vous ai-Je pas dit que Je connais les mystères des cieux et de la terre, et que Je sais ce que vous divulguez et ce que vous cachez ? \"", "wo": "–Mu ne : «Aadama xamal-leen seeni tur ;” Ba mu leen xamalee seeni tur, Yàlla ne leen : “Ndax dama leen a waxuloon ne Man xam naa kumpag asamaan ak suuf si, te it xam naa xéll li ngeen feeñal ak li ngeen doon ñëbb ?”" }
2
34
{ "fr": "Et lorsque Nous demandâmes aux Anges de se prosterner devant Adam, ils se prosternèrent à l´exception d´Iblis qui refusa, s´enfla d´orgueil et fut parmi les infidèles.", "wo": "[Fàttelikul] Ba Nu nee Maalaaka ya sujjóotleen ci Aadama, ñu sujjóot ba mu des Ibliis, dafa lànk rëy-rëylu daldi bokk ca way-weddi ya.(s)" }
2
35
{ "fr": "Et Nous dîmes : \"ô Adam, habite le Paradis toi et ton épouse, et nourrissez-vous-en de partout à votre guise; mais n´approchez pas de l´arbre que voici : sinon vous seriez du nombre des injustes\".", "wo": "Ñu wax ne ko : “Yaw Aadama dëkkal ci àjjana yaak sa soxna, ngeen di fa lekkee na mu leen neexee, ca fa mu leen soobee ; te bu leen jege garab gile : kon dey ngeen bokk ci way- tooñ ña” ." }
2
36
{ "fr": "Peu de temps après, Satan les fit glisser de là et les fit sortir du lieu où ils étaient. Et Nous dîmes : \"Descendez (du Paradis); ennemis les uns des autres. Et pour vous il y aura une demeure sur la terre, et un usufruit pour un temps.", "wo": "[Séytaane] tarxiisloo na leen, génne leen fa ñu nekkoon. Nu ne leen : “Wàccleen ; di noonuwante. Te itam dangeen am ci kaw suuf ay dëkkuwaay ak i jumtukaay as ndiir” ." }
2
37
{ "fr": "Puis Adam reçut de son Seigneur des paroles , et Allah agréa son repentir car c´est Lui certes, le Repentant, le Miséricordieux.", "wo": "Aadama jot na baat ya [baati tuub] bawoo ca Boroomam, Mu daldi ko jéggal, ndax Moom moo di Jéggalaakoon bi, di Jaglewaakoon bi." }
2
38
{ "fr": "- Nous dîmes : \"Descendez d´ici, vous tous ! Toutes les fois que Je vous enverrai un guide , ceux qui [le] suivront n´auront rien à craindre et ne seront point affligés\".", "wo": "Nu ne leen : “Wàccleen yéen ñépp ! Buleen dummóoyu njub gi jóge ci Man, ñi topp sama njub duñu am lu ñu ragal te duñu jàq [ëllëg]” . " }
2
39
{ "fr": "Et ceux qui ne croient pas (à nos messagers) et traitent de mensonge Nos révélations, ceux-là sont les gens du Feu où ils demeureront éternellement.", "wo": "Ña weddi te fenloo Sunuy tegtal, ñoom ñooy dëkk Safara te ñoom dañu fay béel." }
2
40
{ "fr": "ô enfants d´Israël, rappelez-vous Mon bienfait dont Je vous ai comblés. Si vous tenez vos engagements vis-à-vis de Moi, Je tiendrai les miens. Et c´est Moi que vous devez redouter.", "wo": "Yéen [Bani-Israayiil] ñi sëtoo ci [Yanqooba], fàttalikuleen Sama xéewal gi Ma léen xéewaloon. Nangeen matal Sama kóllare, kon Danaa matal seen gos. Buleen ragal ku dul Man." }
2
41
{ "fr": "Et croyez à ce que J´ai fait descendre, en confirmation de ce qui était déjà avec vous; et ne soyez pas les premiers à le rejeter. Et n´échangez pas Mes révélations contre un vil prix. Et c´est Moi que vous devez craindre .", "wo": "Nangeen gëm li Ma wàcce, te muy dëggal li ngeen yore ; buleen doon ñi ko jëkk a weddi. Buleen jaay samay laaya ak njëg gu néew. Te nangeen ma ragal Man doŋ." }
2
42
{ "fr": "Et ne mêlez pas le faux à la vérité. Ne cachez pas sciemment la vérité.", "wo": "Buleen jaxase dëgg ak caaxaan, di nëbb dëgg te fekk ngeen xam ko xéll.(n)" }
2
43
{ "fr": "Et accomplissez la Salat, et acquittez la Zakat , et inclinez-vous avec ceux qui s´inclinent.", "wo": "Nangeen fonk julli, di joxe asaka, te di rukkoo ànd ak way-rukkoo ya. [Jullig mbooloo, di julli ci biir jàkka yi]." }
2
44
{ "fr": "Commanderez-vous aux gens de faire le bien , et vous oubliez vous-mêmes de le faire, alors que vous récitez le Livre ? êtes-vous donc dépourvus de raison ? .", "wo": "Moo ndax da ngeen di digal nit ñi li baax, fàtte seen bopp, te yéen jàng ngeen Téere ba ? Moo ndax dangeen dul xel-lu ?" }
2
45
{ "fr": "Et cherchez secours dans l´endurance et la Salat : certes, la Salat est une lourde obligation, sauf pour les humbles,", "wo": "Nangeen di dimbandikoo muñ ak Julli : loolu lu diis la ci ku bokkul ci way-ragal Yàlla ña," }
2
46
{ "fr": "qui ont la certitude de rencontrer leur Seigneur (après leur résurrection) et retourner à Lui seul.", "wo": "ña nga xam ne daleen a wóor ne danañu dajeek seen Boroom te ca Moom lañuy dellu." }
2
47
{ "fr": "ô enfants d´Israël, rappelez-vous Mon bienfait dont Je vous ai comblés, (Rappelez-vous) que Je vous ai préférés à tous les peuples (de l´époque).", "wo": "Yéen ñi sëtoo ci Yànqooba, fàttalikuleen Sama xéewal gi Ma leen xéewalee woon, te Man ma defaloon leen ngëneel ci kaw nit ñépp." }
2
48
{ "fr": "Et redoutez le jour où nulle âme ne suffira en quoi que ce soit à une autre; où l´on n´acceptera d´elle aucune intercession; et où on ne recevra d´elle aucune compensation. Et ils ne seront point secourus.", "wo": "Ragal-leen bis boo xam ne bakkan du fa jariñ dara beneen bakkan ; te duñu ko nangul rammu ; duñu ko nangul njote. Te deesuleen dimbali." }
2
49
{ "fr": "Et [rappelez-vous], lorsque Nous vous avons délivrés des gens de Pharaon, qui vous infligeaient le pire châtiment : en égorgeant vos fils et épargnant vos femmes. C´était là une grande épreuve de la part de votre Seigneur.", "wo": "[Fàttalikuleen], ba Nu leen musalee ci waa kër (Firawna), tegoon nañu leen mbugal mu ñaaw : ñuy rendi seeni doom yu góor ya, di bàyyi ñu jigéen ña. Nekkoon na ci loolu nattu bu réy bu bawoo ca seen Boroom." }
2
50
{ "fr": "Et [rappelez-vous], lorsque Nous avons fendu la mer pour vous donner passage ! .. Nous vous avons donc délivrés, et noyé les gens de Pharaon, tandis que vous regardiez.", "wo": "[Fàttalikuleen], ba Nu leen xaralee géej ga ! Te Ma musal leen, labal gaa ñi [Firawna], ngeen na ca jàkk di leen gis." }
2
51
{ "fr": "Et [rappelez-vous], lorsque Nous donnâmes rendez-vous à Moïse pendant quarante nuits ! .. Puis en son absence vous avez pris le Veau pour idole alors que vous étiez injustes (à l´égard de vous mêmes en adorant autre qu´Allah).", "wo": "[Fàttalikuleen], ba Nu dëelanteek Muusaa ñeen-fukki guddi ! Te ngeen jaamu yëkk wa ginnaawam, ngeen di way-tooñ." }
2
52
{ "fr": "Mais en dépit de cela Nous vous pardonnâmes, afin que vous reconnaissiez (Nos bienfaits à votre égard).", "wo": "Ginnaaw ga, Nu baal leen ndax ngeen gërëm [seen Boroom]." }
2
53
{ "fr": "Et [rappelez-vous], lorsque Nous avons donné à Moïse le Livre et le Discernement afin que vous soyez guidés.", "wo": "[Fàttalikuleen], ba Nu joxee Muusaa Téere ba ak Àtte yay téqale [dëgg ak fen] ndax ngeen gindiku.(s) " }
2
54
{ "fr": "Et [rappelez-vous], lorsque Moïse dit à son peuple : \"ô mon peuple, certes vous vous êtes fait du tort à vous-mêmes en prenant le Veau pour idole. Revenez donc à votre Créateur; puis, tuez donc les coupables vous-mêmes : ce serait mieux pour vous, auprès de votre Créateur\" ! ... C´est ainsi qu´Il agréa votre repentir; car c´est Lui, certes, le Repentant et le Miséricordieux !", "wo": "Ak ba Muusaa waxee aw nitam : “Samaw nit, yéen tooñ ngeen seen bopp ci li ngeen jaamu yëkk wa. Na ngeen baalu seen Boroom; te ngeen reyante yéen [ñi bokkoon ci moy Yàlla googu] : Looloo gën ci yéen ca seen Boroom” !... Kon mu jéggal leen ndax moom mooy Jéggalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba !" }
2
55
{ "fr": "Et [rappelez-vous], lorsque vous dites : \" ô Moïse, nous ne te croirons qu´après avoir vu Allah clairement\" ! ... Alors la foudre vous saisit tandis que vous regardiez.", "wo": "Ak ba ngeen waxee ne : “ Yaw Muusaa, dunu la gëm ba ba nuy gis Yàlla ne jàkk ci Moom” !... Faf xaacu ga fàdd leen, ngeen di gis loolu." }
2
56
{ "fr": "Puis Nous vous ressuscitâmes après votre mort afin que vous soyez reconnaissants.", "wo": "Topp Nu dekkal leen ginnaaw ba ngeen deewee, ndax Yàlla ngeen di sant [seen Boroom]." }
2
57
{ "fr": "Et Nous vous couvrîmes de l´ombre d´un nuage, et fîmes descendre sur vous la manne et les cailles : - \"Mangez des délices que Nous vous avons attribués ! \" - Ce n´est pas à Nous qu´ils firent du tort, mais ils se firent tort à eux-mêmes.", "wo": "Nu keral leen ak i niir, wàcceel leen lem ak i picc [yu tuddu gëméen], ne leen : - “Lekk leen ci lu sell lii Nu leen xéewale !” - Ñoom daal seen bopp lañuy tooñ, waaye du Nun lañuy tooñ." }
2
58
{ "fr": "Et [rappelez-vous], lorsque Nous dîmes : \"Entrez dans cette ville, et mangez-y à l´envie où il vous plaira; mais entrez par la porte en vous prosternant et demandez la \"rémission\" (de vos péchés); Nous vous pardonnerons vos fautes si vous faites cela et donnerons davantage de récompense pour les bienfaisants.", "wo": "[Fàttalikuleen it], ba Nu leen waxee ne : “Dugguleen ci dëkk bii, lekk ci fu leen neex cig yaatu ; te ngeen jàll buntu bi ànd ak toroxlu te nangeen ñaan Yàlla mu seppi seeni bàkkaar ; [Su ngeen ko defee,] Nu jéggal leen seeni ñaawtéef, Dananu dolli way-rafetal ña aw yiw." }
2
59
{ "fr": "Mais, à ces paroles, les pervers en substituèrent d´autres, et pour les punir de leur fourberie Nous leur envoyâmes du ciel un châtiment avilissant.", "wo": "Tooñkat ya weccee baat ya Nu leen waxoon, ak yeneeni baat yu wuuteek yooya, Nu daldi wàcce ca way-tooñ ña mbugal mu bawoo asamaan ngir la ñu nekkoon di saay-saay [su génn diine]." }
2
60
{ "fr": "Et [rappelez-vous], quand Moïse demanda de l´eau pour désaltérer son peuple, c´est alors que Nous dîmes : \"Frappe le rocher avec ton bâton.\" Et tout d´un coup, douze sources en jaillirent, et certes, chaque tribu sut où s´abreuver ! - \"Mangez et buvez de ce qu´Allah vous accorde; et ne semez pas de troubles sur la terre comme des fauteurs de désordre\".", "wo": "[Fàttalikuleen], ba Muusaa di sàkkul aw nitam ndox, ba Nu waxee ne : “Dóoral xeer wi ak sa yat wi.” Fukki bëti ndox ak ñaar ballee na ca, giir gu nekk xam na fa muy naanee ! - “Lekkleen te naan ci xéewali Yàlla yi ; te buleen dox ci suuf si di way-yàq” .(r)" }
2
61
{ "fr": "Et [rappelez-vous], quand vous dîtes : \"ô Moïse, nous ne pouvons plus tolérer une seule nourriture. Prie donc ton Seigneur pour qu´Il nous fasse sortir de la terre ce qu´elle fait pousser, de ses légumes, ses concombres, son ail (ou blé), ses lentilles et ses oignons ! \" - Il vous répondit : \"Voulez-vous échanger le meilleur pour le moins bon ? Descendez donc à n´importe quelle ville; vous y trouverez certainement ce que vous demandez ! \". L´avilissement et la misère s´abattirent sur eux; ils encoururent la colère d´Allah. Cela est parce qu´ils reniaient les révélations d´Allah, et qu´ils tuaient sans droit les prophètes. Cela parce qu´ils désobéissaient et transgressaient.", "wo": "[Fàttalikuleen], ak ba ngeen nee : “Yaw Muusaa, nun mënatunoo muñ [di lekk] wenn ñam rekk. Ñaanal nu sa Boroom luy sax ci suuf si ciy fuytéef : xaal, laaj, sëb ak soble !” - Mu ne leen : “Ndax dangeen di weccee lu yées ak li gën ? Wàccleen ci menn réewu teeru ; dangeen fa am li ngeen di laaj !” . Saddeef na leen toroxte ak ñàkk ; ñu sóobu ci merum Yàlla. Ndax la ñu nekkoon di weddi kàdduy Yàlla ya, di rey Yonent ya ci lu dul dëgg, ngir moy Yàlla ci lu jéggi dayo." }
2
62
{ "fr": "Certes, ceux qui ont cru, ceux qui se sont judaïsés, les Nazaréens, et les Sabéens, quiconque d´entre eux a cru en Allah, au Jour dernier et accompli de bonnes oeuvres, sera récompensé par son Seigneur; il n´éprouvera aucune crainte et il ne sera jamais affligé .", "wo": "Ña gëm ak ña di Yahuud, ak i Nasraan, ak i Saabiina, ku ca settantal ba dëddu la mu jàppoon, gëm Yàlla ak Bis-pénc ba, gëm Muhammad tey jëf lu yiw , danañu fekk seen pey ca Yàlla ; te duñu tiit te duñu jàq." }
2
63
{ "fr": "(Et rappelez vous), quand Nous avons contracté un engagement avec vous et brandi sur vous le Mont - : \"Tenez ferme ce que Nous vous avons donné et souvenez-vous de ce qui s´y trouve afin que vous soyez pieux ! \"", "wo": "[Fàttalikuleen], ba Nu jàppee seen kóllare te Nu yékkati doj wa mu tiim leen, te Ma ne leen : “Jàppleen li Ma leen jox ànd ca ak dëgg te na ngeen màggal li ne [ca Téere ba] ndax Yàlla ngeen ragal seen Boroom !”" }
2
64
{ "fr": "Puis vous vous en détournâtes après vos engagements, n´eût été donc la grâce d´Allah et Sa miséricorde, vous seriez certes parmi les perdants.", "wo": "Topp, ngeen dëddu ginnaaw loolu, bu dul koon xéewali Yàlla ci yéen ak yërmaandeem, kon dangeen bokk ca way-yàqule ña." }
2
65
{ "fr": "Vous avez certainement connu ceux des vôtres qui transgressèrent le Sabbat. Et bien Nous leur dîmes : \"Soyez des singes abjects ! \"", "wo": "Wallaahi xam ngeen ña jalgati woon ci yéen ca Gaawu ba. Tax ñoom ñooñu Nu ne leen : “Nekkleen di ay golo yu ñu beddi !”" }
2
66
{ "fr": "Nous fîmes donc de cela un exemple pour les villes qui l´entouraient alors et une exhortation pour les pieux.", "wo": "Nu def ko muy mbugal, mu nekk luy waar ñi teew ak ñay ñëwi ca seen ginnaaw te di waaraateb way-gëm ña." }
2
67
{ "fr": "(Et rappelez-vous,) lorsque Moïse dit à son peuple : \"Certes Allah vous ordonne d´immoler une vache\" . Ils dirent : \"Nous prends-tu en moquerie ? \" \"Qu´Allah me garde d´être du nombre des ignorants\" dit-il.", "wo": "(Fàttalikuleen,) ba Muusaa waxee aw nitam : “Yàlla digal na leen ngeen reyu nag” . Ñu ne ko : “Moo ndax danga nuy ñaawal ?” . Mu ne : “Yàlla na ma Yàlla musal ci bokk ci way-réer ña” .(s)" }
2
68
{ "fr": "- Ils dirent : \"Demande pour nous à ton Seigneur qu´Il nous précise ce qu´elle doit être\". - Il dit : \"Certes Allah dit que c´est bien une vache, ni vieille ni vierge , d´un âge moyen, entre les deux. Faites donc ce qu´on vous commande\".", "wo": "Ñu ne : “Ñaanal nu sa Boroom mu leeral nu luy meloom” . - Mu ne : “Naka Moom nee na : nag wa du wu màggat, du aw sëll, dafa digg- dóomu. Def leen li ñu leen sant” ." }
2
69
{ "fr": "- Ils dirent : \"Demande donc pour nous à ton Seigneur qu´Il nous précise sa couleur\". - Il dit : \"Allah dit que c´est une vache jaune, de couleur vive et plaisante à voir\".", "wo": "- Ñu ne : “Ñaanal nu sa Boroom mu leeral nu luy meloom” . - Mu ne : “Naka Moom nee na: nag la wu gel, wu fees, woo xam ne dees na beg ci xool ko .” ." }
2
70
{ "fr": "- Ils dirent : \"Demande pour nous à ton Seigneur qu´Il nous précise ce qu´elle est car pour nous, les vaches se confondent. Mais, nous y serions certainement bien guidés , si Allah le veut\".", "wo": "- Ñu ne : “Laajal nu sa Boroom mu leeral nu nu mu mel, ndax nag yi dañoo bari ci nun. Te bu soobe Yàlla dananu gindiku [Jëfe ndigalam]” ." }
2
71
{ "fr": "- Il dit : \"Allah dit que c´est bien une vache qui n´a pas été asservie à labourer la terre ni à arroser le champ, indemne d´infirmité et dont la couleur est unie\". - Ils dirent : \"Te voilà enfin, tu nous as apporté la vérité ! \" Ils l´immolèrent alors mais il s´en fallut qu´ils ne l´eussent pas fait.", "wo": "– Mu ne moom nag : “Nee na, nag la wu ñu bayloowul suuf si, du buy suuxat mbay, bu amul benn laago la te wenn melo la” . - Ñu ne ko : “Agsi nga ci dëgg gi!” Ñu rendi ko te xawoon nañu koo bañ a def." }
2
72
{ "fr": "Et quand vous aviez tué un homme et que chacun de vous cherchait à se disculper ! ... Mais Allah démasque ce que vous dissimuliez.", "wo": "[Fàttalikuleen] Ba ngeen reyee bakkan te ngeen jiiñante ko!... Te Yàlla génne la ngeen doon nëbb." }
2
73
{ "fr": "Nous dîmes donc : \"Frappez le tué avec une partie de la vache\". - Ainsi Allah ressuscite les morts et vous montre les signes (de Sa puissance) afin que vous raisonniez.", "wo": "Nu ne : “Dóorleen ko lenn [Lu bokk ci nag wi]” . - Noonu la Yàllay dekkalee ñi dee te dana leen won ay kéemaan ndax ngeen xel-lu." }
2
74
{ "fr": "Puis, et en dépit de tout cela , vos coeurs se sont endurcis; ils sont devenus comme des pierres ou même plus durs encore; car il y a des pierres d´où jaillissent les ruisseaux, d´autres se fendent pour qu´en surgisse l´eau, d´autres s´affaissent par crainte d´Allah. Et Allah n´est certainement jamais inattentif à ce que vous faites.", "wo": "Topp, seeni xol wow ginnaaw loolu [dëgër] ba mel ni xeer mbaa lu ko gën a tar wowaay ; Ndax ci xeer sax ndox dana ca ball, te am na ci xeer yi yuy xar ndox génn ca, am na ci yuy rot ngir ragal Yàlla. Te Yàlla du ñàkk a seetlu li ngeen di def." }
2
75
{ "fr": "- Eh bien, espérez-vous [Musulmans], que des pareils gens (les Juifs) vous partageront la foi ? alors qu´un groupe d´entre eux, après avoir entendu et compris la parole d´Allah, la falsifièrent sciemment .", "wo": "- Moo ndax, dangeen xeemeem [,Yéen jullit ñi,] Yahuud yi wóolu leen ? Te am na ci ñoom kurél boo xam ne déggoon nañu waxi Yàlla, ba noppi soppi ko ginnaw ba ñu ca xalaatee ba xam ko. " }
2
76
{ "fr": "- Et quand ils rencontrent des croyants, ils disent : \"Nous croyons\"; et, une fois seuls entre eux, ils disent : \"Allez-vous confier aux musulmans ce qu´Allah vous a révélé pour leur fournir, ainsi, un argument contre vous devant votre Seigneur ! êtes-vous donc dépourvus de raison ? \" .", "wo": "- Bu ñu dajeek ñu gëm, ne : “Gëm nañu” ; te bu ñu wéetee ñoom doŋŋ, naan : “Ndax dungeen waxtaane li leen Yàlla xamal, nu mën caa sukkandiku [ñoom jullit yi] di dàggeek yéen ci seeni [mbiri] Boroom ! Moo ndax dangeen dul xel-lu ?” .(h)" }
2
77
{ "fr": "- Ne savent-ils pas qu´en vérité Allah sait ce qu´ils cachent et ce qu´ils divulguent ?", "wo": "- Moo ndax dañoo xamul ne Yàlla xam na la ñuy nëbb ak la ñuy feeñal ?" }
2
78
{ "fr": "Et il y a parmi eux des illettrés qui ne savent rien du Livre hormis des prétentions et ils ne font que des conjectures .", "wo": "Am na ca ñoo xam ne mënuñoo jàng, xamuñu téere ba lu dul ay fen yu nekk ay njort doŋŋ." }
2
79
{ "fr": "Malheur, donc, à ceux qui de leurs propres mains composent un livre puis le présentent comme venant d´Allah pour en tirer un vil profit ! - Malheur à eux, donc , à cause de ce que leurs mains ont écrit, et malheur à eux à cause de ce qu´ils en profitent !", "wo": "Alkaande ñeel na ñay bind téere ba, ba noppi naan lii ca Yàlla la jóge ndax mën caa jële njëg gu néew ! - Alkaande ñeel na leen ngir la ca seeni yoxo bind, ñeel na leen ngir la ñu ca fàggu [ci alal] !" }
2
80
{ "fr": "Et ils ont dit : \"Le Feu ne nous touchera que pour quelques jours comptés ! \" Dis : \"Auriez-vous pris un engagement avec Allah - car Allah ne manque jamais à Son engagement; - non, mais vous dites sur Allah ce que vous ne savez pas\" .", "wo": "Wax nañu ne : “Safara dunu laal lu dul ay bis yu ñuy waññi !” . Neeleen : “Moo ndax dangeen cee déggook Yàlla - te Yàlla du wuute ab digam ; - walla dangeen di wax ci Yàlla lu ngeen xamul” ." }
2
81
{ "fr": "Bien au contraire ! Ceux qui font le mal et qui se font cerner par leurs péchés, ceux-là sont les gens du Feu où ils demeureront éternellement.", "wo": "Axakay ! Ku def jëf ju bon ba ay ñaawtéefam mëdd ko, ñooña ñooy ñay dëkk Safara te dañu fay béel." }
2
82
{ "fr": "Et ceux qui croient et pratiquent les bonnes oeuvres, ceux-là sont les gens du Paradis où ils demeureront éternellement.", "wo": "Waaye ñi gëm te def jëf yu sell [Farataak Sunna] ñooña ñoo di ñay dugg Àjjana, dañu fay béel." }
2
83
{ "fr": "Et [rappelle-toi], lorsque Nous avons pris l´engagement des enfants d´Israël de n´adorer qu´Allah, de faire le bien envers les pères, les mères, les proches parents, les orphelins et les nécessiteux, d´avoir de bonnes paroles avec les gens; d´accomplir régulièrement la Salat et d´acquitter le Zakat ! - Mais à l´exception d´un petit nombre de vous, vous manquiez à vos engagements en vous détournant de Nos commandements.", "wo": "[Fàttalikuleen], ba Nu wóllaranteek (Banii-Israayiil) ne leen : buleen jaamu kenn ku dul Yàlla, te nangeen rafetal seeni jëf jëme ci seeni ñaari waajur, seeni jegeñaale, jirim yi, way- ñàkk ñi, te ngeen waxal nit ñi wax ju rafet ; ngeen fonk julli te génne asaka, ba noppi ngeen dummóoyu ! - Ba mu des ñu néew ci yéen, ngeen di way-dëddu [lu baax]." }
2
84
{ "fr": "Et rappelez-vous, lorsque Nous obtînmes de vous l´engagement de ne pas vous verser le sang, [par le meurtre] de ne pas vous expulser les uns les autres de vos maisons. Puis vous y avez souscrit avec votre propre témoignage.", "wo": "[Fàttalikuleen], ba nu wóllaranteek yéen ne buleen tuur seeni deret, buleen génneyante ci seeni kër. Ngeen nangu te seede ko.(s)" }
2
85
{ "fr": "Quoique ainsi engagés, voilà que vous vous entre-tuez, que vous expulsez de leurs maisons une partie d´entre vous contre qui vous prêtez main forte par péché et agression. Mais quelle contradiction ! Si vos coreligionnaires vous viennent captifs vous les rançonnez alors qu´il vous était interdit de les expulser (de chez eux). Croyez-vous donc en une partie du Livre et rejetez-vous le reste ? Ceux d´entre vous qui agissent de la sorte ne méritent que l´ignominie dans cette vie, et au Jour de la Résurrection ils serons refoulés au plus dur châtiment, et Allah n´est pas inattentif à ce que vous faites .", "wo": "Ba noppi ngeen rey aw nit, ci seen biir, am ca ab kurél bu ngeen génne seeni kër, ngeen dimbalante ci ay bàkkaar ak ug noonuwante. Te bi ngeen leen jàppee ci xare di leen fayloo ag njot te di leen génne te loolu araam na ci yéen. Ndax dangeen a dëggal lenn téere ba weddi la ca des ? Kuy def loolu ci yéen, dara du doon peyam lu dul toroxte ci dundug àddina, te Bis- pénc ba dees na leen delloo ci gën jaa tari mbugal, Yàlla dey nekkul Kuy ñàkk a seetlu li ngeen di def." }
2
86
{ "fr": "Voilà ceux qui échangent la vie présente contre le vie future. Eh bien, leur châtiment ne sera pas diminué. Et ils ne seront point secourus.", "wo": "Ñooña ñooy ña jaay àllaaxira jënde ko àddina. Duñuleen woyofal mbugal ma. Te deesuleen dimbali. " }
2
87
{ "fr": "Certes, Nous avons donné le Livre à Moïse; Nous avons envoyé après lui des prophètes successifs. Et Nous avons donné des preuves à Jésus fils de Marie, et Nous l´avons renforcé du Saint-Esprit. Est-ce qu´à chaque fois, qu´un Messager vous apportait des vérités contraires à vos souhaits vous vous enfliez d´orgueil ? Vous traitiez les uns d´imposteurs et vous tuiez les autres .", "wo": "Bir na, ne jox Nanu Muusaa Téere ba ; Nu toxal ginnaawam ay Yonent. Te jox Nanu Iisaa doomu Maryaama ay kéemaan yu leer te dëgëral ko, ak ruu gu sell [Jibril]. Ndax saa yu leen ab Yonent dikkalee [Sant leen] lu neexul seen bakkan, ngeen rëy-rëylu ? Ngeen weddi ab kurél, rey ab kurél [ca ñoom Yonent ya]." }
2
88
{ "fr": "Et ils dirent : \"Nos coeurs sont enveloppés et impénétrables\" - Non mais Allah les a maudits à cause de leur infidélité, leur foi est donc médiocre .", "wo": "Ñu naan : “Sunuy xol muuru na [ci li Yonent bi wax]” - Li am ba des moo di Yàlla rëbb na leen ci sababus seenug weddi, te néewaana bu ñu gëmee." }
2
89
{ "fr": "Et quant leur vint d´Allah un Livre confirmant celui qu´ils avaient déjà, - alors qu´auparavant ils cherchaient la suprématie sur les mécréants, - quand donc leur vint cela même qu´ils reconnaissaient, ils refusèrent d´y croire. Que la malédiction d´Allah soit sur les mécréants ! ", "wo": "[Fàttalikuleen] ba leen ab Téere dikkalee, jóge ca Yàlla, di dëggal la ñu yor, - fekk lu jiitu loolu daan nañu ñaan noteel ci yéefar yi, - te ba la ñu xamoon [te daan ko séenu] egsee ca ñoom, dañu koo weddi. Rëbbum Yàlla dal na yéefar yi !" }
2
90
{ "fr": "Comme est vil ce contre quoi ils ont troqué leurs âmes ! Ils ne croient pas en ce qu´Allah a fait descendre, révoltés à l´idée qu´Allah, de part Sa grâce, fasse descendre la révélation sur ceux de Ses serviteurs qu´Il veut. Ils ont donc acquis colère sur colère, car un châtiment avilissant attend les infidèles !", "wo": "Bon na, la ñu jaayee seeni bakkan ! Ba tax ñu weddi la Yàlla wàcce ngir bew, te iñaan ci li Yàlla wàcce ngënéelam ci ku ko soob ciy jaamam. Ba daldi nañuy mer bay fuuñ-fuuñi, te yéefar yi am nañu mbugal muy toroxale !" }
2
91
{ "fr": "Et quand on leur dit : \"Croyez à ce qu´Allah a fait descendre\", ils disent : \"Nous croyons à ce qu´on a fait descendre à nous\". Et ils rejettent le reste, alors qu´il est la vérité confirmant ce qu´il y avait déjà avec eux. - Dis : \"Pourquoi donc avez-vous tué auparavant les prophètes d´Allah, si vous étiez croyants ? \".", "wo": "Bu ñu leen waxee ne : “Gëmleen li Yàlla wàcce” , Ñu ne : “Gëm nañu li ñu wàcce ci nun” . Te ñoom weddi nañu la ñëw ginnaawam te muy dëggal la ñu yore. - Neel : “Lu taxoon ngeen rey ay Yonentiy Yàlla, ca bu jëkk ndegam gëm ngeen ?” ." }
2
92
{ "fr": "Et en effet Moïse vous est venu avec les preuves. Malgré cela, une fois absent vous avez pris le Veau pour idole, alors que vous étiez injustes.", "wo": "Wóor na céŋŋ ne Muusaa digaloon na leen àndak ay kéemaam yu leer. Ba noppi ngeen jaamu sëll wa ginnaawam, ngeen di way-tooñ.(r)" }

Dataset Description

This dataset contains translations of the Quran in two languages: Wolof and French. Each entry includes the sourate number, the verse number, and the translations in both languages.

Translation Information

  • Wolof Translation: The translation of the Quran in Wolof was done by Sëriñ Seexunaa Lóo Ngaabu.
  • Written By: The text was written by Allaaji Mamadu Ngeer and Góorgi Jaw.
  • Updated By: The translation was updated by Sëriñ Muntaqaa Mbàkke (son of Sëriñ Koso mu Seex Muhammadul Muntaqaa Mbàkke).

Features

  • sourate: The chapter (sourate) number of the Quran.
  • verset: The verse number within the chapter.
  • translation: A dictionary containing:
    • fr: The translation of the verse in French.
    • wo: The translation of the verse in Wolof.

Dataset Structure

Data Instances

An example of a data instance is:

{
  "sourate": 1,
  "verset": 1,
  "translation": {
    "wo": "Ci turu Yàlla, miy Yërëmaakoon , di Jaglewaakoon , laay tàmbalee",
    "fr": "Au nom d´Allah, le Tout Miséricordieux, le Très Miséricordieux."
  }
}

Citation

@dataset{
wolof-french-alxuraan,
  author = {Cheikh Faye},
  title = {Wolof French Alxuraan},
  year = {2024},
  url = {https://huggingface.co/datasets/cibfaye/wolof-french-alxuraan}
}
Downloads last month
35